Genesis 24:7
TSK
Aji Sax ji, Yàllay asamaan, moom mi ma jële sama kër baay ak fa ma juddoo, te wax ak man, giñal ma ne ma, dina jox sama askan réew mii, moom ci boppam dina yebal malaakaam, mu jiitu la. Foofa ngay jëlale sama doom soxna.