TSK

TSK · Proverbs 2:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Job 24:13 TSK

Ñee noonoog leer, faalewñu yoonu bëccëg te duñu fa taxawaaloo.

Day gis boppam, naagu, ba du gis sikkam, sib ko.

Yoonu ku bon ne këruus, du xam lu muy téqtaloo.

Xamuñu yoonu jàmm, te yoon amul fa ñuy jaare, xanaa sàkk seen yoon yu lunk te ku fa awe doo daj jàmm.

¶ «Yaw nit ki, waxal sa bokk yi, ne leen: “Boroom njekki démb li, su tooñee tey, njekkam loola du ko musal. Ku bon ki itam, bu waccee yoonu mbonam, tey, mbonu démbam ga du ko lor. Boroom njekki démb li nag, su bàkkaaree, njekkal démbam la du ko may mu dund.

Yeen ñépp ay doomi leer ngeen, doomi bëccëg ndarakàmm; nun bokkunu dara ak guddi, mbaa ag lëndëm.

¶ Ñi ñu xasa leeral nag, te ñu jota mos may gu bawoo asamaan, séddu ci Noo gu Sell gi, deesu leen mana defal dara.