TSK

TSK · Proverbs 2:9

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Aji Sax jee baax, rafeti dogal, di gindi moykat ci yoon wi,

Nga ne ma: «Dama laa xelal, xamal la fi ngay jaar, digal la, di la xool.

Sa kàddu laay niitoo samay tànk, muy leeral samaw yoon.

¶ Li ko taxa jóg di nit ñi am xel mu rafet, am ab yar, ngir xam wax ju lal dég-dég,

Aji Sax ji seen jotkat dafa wax, Aji Sell ju Israyil da ne: «Maay Aji Sax ji, seen Yàlla ji leen di jàngal seen njariñ, di leen awale fa ngeen wara awe.