Xaymaam day lëndëm, làmpam ba ko tiim ne kamaj.
TSK
TSK · Proverbs 21:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Kuy jëw moroomam, ma wedamal; ku daŋŋiiral ak ku reew, muñaluma la.
Juróom benn a ngii yu Aji Sax ji bañ, ba ci juróom yaar yu mu seexlu:
Ragal Aji Sax ji mooy bañ lu bon. Réy, xeebaate, yoonu mbon, ak wax ju jekkadi, ma boole bañ.
Saraxu nit ku bon ñaawtéef la, rawatina bu ci jubloo lu bon.
Bésub keroog booba, ku bew bay regeju mooy detteelu, sagub nit sàggiku, Aji Sax ji doŋŋ mooy jagoo kawe.
Aji Sax ji da ne: «Jigéeni Siyoŋ a ngi daŋŋiiral, di goŋeet-goŋeeti, di regejook a rékk-rékkal, samp um ndaag, keleŋal lami wëq.»
¶ Yeesu teg ca ne: «Maa ne leen, kooku moo ñibbaale këram àtteb ku jub, waaye du Farisen ba. Ndaxte képp kuy réylu, dees na la toroxal, waaye ki toroxlu lees di yékkati.»
¶ Naka noonu yeen ndaw ñi, nangul-leen magi mbooloom gëmkat ñi. Yeen ñépp nag toroxluleen ci seenug jëflante, ndax: «Yàlla, ñi réy lay xeex, ñi toroxlu, mu may leen aw yiw.»