2 Samuel 20:1
TSK
¶ Booba nit ku bon a nga woon ca mbooloo ma, ku ñuy wax Seba, di doomu Bikkri, ma bokk ca giirug Beñamin. Seba wal liit ga, daldi yéene ne: «Sunu yoon nekkul ci Daawuda doomu Yese jii, du benn cér bu nu am ci moom. Yeen waa Israyil, ku nekk ca sa xayma!»