Bu loolu amee mboolem sa dag yii dinañu ma sujjóotalsi te naan ma: “Demal, yaak mbooloo, mi la topp yépp!” Su ko defee ma doora dem.» Musaa nag won Firawna gannaaw, mer ba, fees.
TSK
TSK · Proverbs 28:1
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ «Ñi des ci yeen, dinaa indi njàqare ci seen xol, foofa ngeen nekk ca seen réewu noon ya, ba xob wu ne foy-foy ngeen daw. Dingeen xélu ni ku ñuy dàqe saamar, bay daanu, te dàqeesu leen.
¶ Aji Sax jeey def ngeen daanu fi seen kanami noon. Wenn yoon ngeen di dikke, song leen, waaye juróom ñaari yoon ngeen di awe, daw, te dees na leen seexlu ci mboolem nguuri kaw suuf.
Booba fekk na Boroom bi dégtal waa dalub Siri ba riirum fas yu ànd aki watiiri xare ak gàngoor gu réy, ba tax ñu naan ca seen biir: «Ãa! Loolu de, buuri Etteen ñaak buuri Misraa, Buurub Israyil fey leen, ngir ñu songsi nu!»
Ñu dem toppi leen ba ca dexu Yurdan, ndeke yoon wa fees na dell aki yéreeki jumtukaay yu waa Siri sànni, ba ñuy daw. Ndaw ya waññiku, wax ko Buur.
coowal musiba mooy buur nopp ya, yàqkat bette ko biir jàmm.
Sunu Yàllaa nuy rawale, di nu dooleel, di nu wallu fu nu jaaxlee,
Waaye ñooy tiita tiit fu tiitaange amul. Yàllaay tasaare néewi nit ñi la gaw. Yàllaa leen wacc, nga gàcceel leen.
Maandu, fegu; dëng, weeru.
Yaw Aji Sax ji, ku dogu, pastéefu, wóolu la, nga may ko jàmm ju mat, nde moo la wóolu.
¶ Sadarag Mesag ak Abet Nego ne Buur Nabukodonosor: «Buur, soxlawul ñu di la lay dara.
¶ Ba waa kurélu àttekat ya gisee fit, wi Piyeer ak Yowaan àndal, te ñu xam ne niti neen ñu masula jàng lañu, dañoo waaru. Xamoon nañu nag ne ñook Yeesoo nekkoon.
Xam ngeen na nu jëkkoona sonne, ak na ñu nu torxale woon ca Filib, dëkk ba, bala noo dikk fa yeen. Teewul ci sunu ndimbalal Yàlla, nu ñeme leena àgge, ci biir xeex bu metti sax, xibaaru jàmm bu Yàlla bi.