yen leen toskarey àddina ndax liggéey yu metti. Ñuy móol ban, di tabax, waa Misra teg ca sëf leen mboolem liggéeyu tool ya. Néegoon nañu ca ñoom lool ca mboolem liggéeyu njaam bu ñu leen sas.
TSK
TSK · Proverbs 28:15
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ba mu ko defee Buur ne dagam ya ko dar: «Ayca, reyleen sarxalkati Aji Sax yii, gannaaw ñoom it ñook Daawudaa far. Yégoon nañu ba muy daw te xamaluñu ma ko.» Dagi buur ya nag baña xàcci seen loxo ci kaw sarxalkati Aji Sax ya.
¶ Booba la Menayem song dëkk ba ñuy wax Tifsa, rey ña fa nekkoon ñépp, boole ca faagaagal diiwaan ba dale Tirsa ba Tifsa, ndax ñoo ko gàntal, bañ koo ubbi buntu dëkk ba. Mu butti jigéeni wérul ña fa nekk ñépp.
Teewul mu siide fexeel Mardose doŋŋ, ndax booba waxoon nañu ko askan wi Mardose bokk. Ba loolu amee Aman di wuta sànk mboolem Yawut yi nekk ci mboolem réewum Aserus, di bokki Mardose.
Merum buur ni gaynde gu ŋar; yërmandey buur ni lay cig mbooy.
Aji Sax jee damm bant, bi ñu bon ñi daan dóoree! Moo damm seen yetu nguur,
Efrayim lees di not, joggati ay yelleefam, nde moo dogoo topp yoonu caaxaan.
Kàngam yi ci biiram di gaynde yuy ŋar, ay njiitam di tilli timis yu dul pannal,
¶ Àndleen ak sago te teewlu! Seenub noon Tuumaalkat bi, mu ngi ŋar ni gaynde, tey wër, di rëbb ku mu warax.