TSK

TSK · Proverbs 30:14

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Job 29:17 TSK

Ku jubadi, ma dammi ŋaamam, foqatee am pàddam cay sellam.

Ñu dul jeex a ma jógal, gaw ma, te duma ragal.

Ñu ngi naa: «Sunu làmmiñ lanuy daane, nook sunu kàddu; ku nu manal dara?»

Mooy ba Doweg, Edomeen ba, demee ca Sóol, ne ko Daawuda dem na kër Ayimeleg.

Maa ngi tëdd ci biiri noon yu mel niy gaynde, di yàpp doom aadama. Seeni sell niy xeej aki fitt, seen làmmiñ di saamar yu ñaw.

Làmmiñu waxkat, jam-jami jaasi; kàddu gu xelu, garab la ci.

Ku ñàkk, su jekkoo ab ndóol, du ko bàyyil fepp, day mel ni waame.

Lu waral ngeen di dëggaate sama ñoñ, nappaaje néew-doole yi?» Kàddug Boroom bee, Aji Sax ju gàngoor yi.

Ab njublaŋ, ay pexeem musiba la. Njekkar lay nas, ba bu néew-ji-doole sàkkoo dëgg it, mu fen ba lor ko.

Yeen, nebbon ji, ngeen lekk; kawari jur gi, ngeen def yére, sol; li ci duuf, ngeen rendi, te jur gi sàmmuleen leen!

Amos 2:7 TSK

Ñooy dëggaate néew-ji-doole ci pëndub suuf, di xañ way-ñàkk àqam. Nit ak baayam di tëdde as ndaw, di teddadil sama tur wu sell.

Amos 8:4 TSK

Amos ne: «Dégluleen lii, yeen jula yiy dëggaate aji ñàkk, di jeexal néew-ji-dooley réew mi,

Micah 3:1 TSK

Dama ne: «Ngalla dégluleen yeen njiiti Yanqóoba, yeen kilifay kër Israyil! Xanaa du yeena wara xam yoon?

Ba noon ya riddeendoo, di nu tasaaresi, seen xeeju bopp nga bëtte seen bopp, fekk leen ñuy xaxaloo, ni ñuy waaja sëxëtoo ay néew-ji-doole, fu kenn yégul.

seen kawar mel ni kawaru jigéen, seeni sell nirook selli gaynde.