TSK

TSK · Proverbs 7:3

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Takkleen ko, muy firnde ci seen loxo, te na doon am mbandal ci seen diggantey gët.

Bu la ngor ak worma dëddu, booleel takk ci sa baat, bind ko ci sa àlluway xol.

Takkal foo tollu, taf ci sa xol, fas ko ci sa baat.

«Man nag, lii mooy sama kóllëreek ñoom: Sama xel mi tegu fi sa kaw, ak sama kàddu yi ma yeb ci sa gémmiñ, lenn du ci teqlikook sa gémmiñ ak sa gémmiñu askan, ak sa gémmiñu askanu askan, tey ak ëllëg.» Aji Sax jee ko wax.

«Waaye kóllëre gi may fas ak waa kër Israyil gannaaw loolu,» kàddug Aji Sax jee, «nii lay deme: Maay yeb sama ndigali yoon ci seen xel, ci seen xol laa koy ñaas. Maay doon seen Yàlla, ñoom ñu doon sama ñoñ.