TSK

TSK · Psalms 116:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Aji Sax ji, yaay wàll wi ma séddoo, di sama ndabal xéewal. Yaa yor sama wërsëg.

Santleen Aji Sax ji, tudd turam, xamley jalooreem ci biir xeet yi,

yaw laay sarxalal saraxu cant, te turu Aji Sax ji laay tudd.

¶ Ci kaw loolu mu jël ab kaas, yékkati kàddug cant, daldi ne: «Jël-leen kaas bii, te ngeen séddoo ko.

Kaasu barke bi nuy barkeeloo, xanaa du mooy bokk gi nu bokk ci deretu Almasi? Te mburu mi nuy daggoo, du mooy bokk gi nu bokk ci yaramu Almasi?

Noonu itam la def ak kaas ba, gannaaw reer ba, ne leen: «Kaas bii mooy kóllëre gu yees gi fasoo ci sama deret. Deeleen def lii, di ma ko fàttlikoo, saa yu ngeen ci naanee.»