TSK

TSK · Revelation 13:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Daawuda ne Sóol: «Sang bi, bu may sàmm sama gàtti baay, ba gaynde mbaa rab wu aay dikk, jël ci ab gàtt,

Xettlil sama bakkan ci saamar, ba sama benn bakkan bii mucc selli xaj!

Kilifa guy soxore néew-ji-doole mook gaynde guy yëmmoo yem, mbaa rab wuy songe.

Moo tax gaynde di génne ci gott bi, fàdd leen, bukkiy màndiŋ mi di leen yàpp, segg di tëru seeni dëkk, ku ca génne, dees na la xotat. Seeni moy a bare, te seen ñàkk worma réy.

¶ «Rab wu jëkk waa nga mel ni gaynde, am laafi jaxaay. Naka laay xool, ñu buddi laaf yi, yékkatee ko ci suuf, taxawal ko, mu taxawe ñaari tànk ni nit, ba noppi ñu jox ko xelum nit.

Moo tax ma mel ni gaynde ci yeen di tëroo ni segg ciw yoon.

Amos 5:19 TSK

Day mel ni kuy daw gaynde, ne pemm cim segg, rëcc, ñibbi, teg loxoom ca tabax ba, jaan ne ko càppit.

Waaye Boroom bee ma dimbali, dooleel ma, ngir kàddu gi siiwe ci man, ba xeeti jaambur yépp dégg ko, te Boroom bee ma musal ci pàddum gaynde.

Ci kaw loolu jeneen firnde feeñ asamaan. Du lenn lu dul ninki-nànka ju réy, xonq curr, am juróom ñaari bopp ak fukki béjjén, juróom ñaari mbaxanay buur tege ci bopp yi, bopp bu ne, menn.

¶ Ninki-nànka ja nag xam ne xalab nañu ko ci kaw suuf, mu ne dann ndaw sa jur doom ju góor ja.

Ba loolu amee ñu sujjóotal ninki-nànka ji ndax la mu jox rab wi sañ-sañ bi, di sujjóotal rab wi, naan: «Ana kuy moroomu rab wii, ak ku mana xeex ak moom?»

¶ «Fukki béjjén yi nga gis, fukki buur lañu yu jotagul ci seen nguur. Waaye diirub wenn waxtu, lañuy jot sañ-sañu nguur, ñook rab wi.

Mu jàpp ninki-nànka ja, jaani cosaan jooju di Tuumaalkat bi, di Seytaane ba tey. Malaaka mi yeew ko diiru junniy at.