May siiwal sa njekk, di yendoo waxtaane say wall, doonte lim ba wees na ma.
TSK
TSK · Romans 1:16
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Maay àgge ay buur sa kàdduy seede, te duma rus.
«Sama kàddu déy, daa mel ni sawara,» kàddug Aji Sax jee, «mbaa saddu, di falaxew doj!
Malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndax kat maa leen indil xibaaru jàmm bu doon mbég mu réy, ñeel askan wépp.
Njàqare ak musiba daal, mooy dal ci kaw képp kuy def lu bon, te Yawut bi jiitu ci, waaye ki dul Yawut it topp ci;
Kon boog ngëm ci dég-dég lay juddoo, dég-dég ba bawoo ci kàddug waare gi jëm ci Almasi.
Te xam naa ne bu ma dikkee fa yeen, barkeb Almasi bu mat sëkk laay dikke.
Doguwuma woona xam lenn ci seen biir, lu moy Yeesu Almasi, kooku ñu daaj ca bant ba.
Ndegam ñeneen a jagoo boobu sañ-sañ ci yeen, astamaak nun. Waaye nag jariñoowunu sañ-sañ boobu. Lépp lanu far muñ, ngir baña gàllankoor yoonu xibaaru jàmm bu Almasi.
Waaye su ñépp dee waxe kàddug waxyu, ba ku gëmul, mbaa ku xamul duggsi, kàddu ga la ko ñépp di tiiñale, àggee ko ko ab àtteem,
¶ Ba ma àggee Torowas, ngir yégle fa xibaaru jàmm bi ci Almasi, bunt ubbikul na ma ndax Boroom bi.
Aji gëmadi ñooñu la Seytaane yàllay xarnu bii gëlëmal seenum xel, ngir ñu baña gis ceeñeeru xibaaru jàmm bu leeru Almasi, miy melokaanu Yàlla.
Ndaxte gànnaay, yi nuy xeexe du gànnaayi suuxi neen, waaye da di gànnaay yu am fa Yàlla, kàttanu daane ay tata. Te xalaatin yu jubul, noo leen di daaneel,
te li waral ngëm googu ak cofeel googu, di seen yaakaara jot ca cér ba ñu leen dencal fa asamaan. Mooy yaakaar ja ngeen dale am ba ngeen jëkkee dégg kàddug dëgg gu xibaaru jàmm bi.
¶ Leneen lu nu dul noppee sante Yàlla, moo di lii: ba ngeen nangoo ci sunu làmmiñ kàddug Yàlla gi nu leen dégtal, te melul ni kàddug nit doŋŋ ngeen ko nangoo, waaye kàddug Yàlla gi mu doon ci lu wér, moom ngeen ko jële, te kàddu googu mooy liggéey ci seen biir, yeen gëmkat ñi.
¶ Bul kersawoo di seedeel sunu Sang, mbaa nga di ma kersawoo, man mi ñu tëj ngir moom, waaye jëlal sa wàll ci coonob xibaaru jàmm bi, ni la ko manoorey Yàlla manloo.
Yal na Yàlla baaxe nag waa kër Onesifor, yërmandeem, ndax dëfal na ma lu bare, te kersawoowul li ñu ma tëj kaso,
Ku sonn ndax li muy gëmkatub Almasi nag, bumu ci rus, na sàbbaal Yàlla kay, ci woowu tur.