¶ Yeesu nag yóbbu Fukk ñaak ñaar, wéetook ñoom, ne leen: «Nu ngii jëm Yerusalem, te mboolem lu yonent yi bindoon ci mbirum Doomu nit ki dina sotti.
TSK
TSK · Romans 1:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Yeesu moomu nag, Yàllaa ko dekkal, nu seede ko, nun ñépp.
xamleen xéll, yeen ñépp ak bànni Israyil gépp, ne ci turu Yeesu Almasi waa Nasaret bi, ki ngeen daajoon ci bant, te Yàlla dekkal ko, ci turam doŋŋ la kii wére, ba taxaw ci seen kanam.
nun sët yi la ko defal, ba mu yékkatee Yeesu, te noonee lañu ko binde ci ñaareelu saaru Sabóor, ne: “Yaa di sama Doom, bés niki tey maa la jur.”
moo jëm ci Doomam, ji soqikoo ci askanu Daawuda, ci wàllu àddina.
Ngeen boole ci xam manooreem gu nattuwul gi mu nu lañalal, nun gëmkat ñi. Manoore googu feeñ na ci jëf ji sottee ci kàttanam ak dooleem,
te Almasi di ki def boppam sarax bu mucc sikk ñeel Yàlla, ci dooley Noo gu Sell gi, kon nag ñaata yoon la deretu Almasi gëna mana setal sunu yaraange ji sababoo ci sunu jëf ju bon ju jëme ci ndee, ba nu mana jaamu Yàlla jiy dund!
Ndax kat du genn kàddug waxyu gu masa soqikoo ci coobarey nit, waaye ci xiirtalub Noo gu Sell gi la aw nit daan waxe waxyu bu bawoo fa Yàlla.
¶ Ma daldi ne gurub sukk ciy tànkam, ngir sujjóotal ko. Mu ne ma: «Déet, ëpp naa def. Sa mbokkum jaam doŋŋ laa, ni yaak sa bokk yi jàppoo seedeel Yeesu. Sujjóotalal Yàlla. Ndaxte seedeel Yeesu moo di Noo giy dundal waxyu.»