Yonent bu ci am gént, na nettali géntam, waaye ku ci am sama kàddu, na ko àddoo, na ma ko waxe. Ana ñax akum pepp?» Kàddug Aji Sax jee.
TSK
TSK · Romans 10:17
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ «Lii la léeb wi di tekki. Jiwu wi moo di kàddug Yàlla.
Moom nag mu ne ko: «Xanaa kay, ndokklee ñiy déglu kàddug Yàlla te di ko jëfe.»
¶ Waaye nees di wooye koo gëmul? Nees di gëme koo déggul turam? Nees di dégge turam, te yégleesu ko?
Nun nag danoo melul ni ñu bare, ñiy julaa kàddug Yàlla, waaye ci ndigalal Yàlla ak fi kanam Yàlla la nuy waaree xol bu set, ci Almasi mi nu gëm.
Ki leen di may Noo gi, tey sottal ay kéemaan ci seen biir, ndax li ngeen sàmm yoon moo tax mu di ko def, am li ngeen dégg, ba gëm moo tax?
Na leen kàddug Almasi dëkke, bay baawaan, ngeen di jariñoo xel mu mat sëkk mu ngeen di jànglantee, ak a artoonte. Woyeleen xolub cant, ñeel Yàlla, ay taalifi Sabóor, ak woyi tagg Yàlla, ak woy yu fentoo ci Noo gi.
¶ Nun nag bokk yi, manunoo ñàkka sant Yàlla fu nu tollu, ci yeen ñi Boroom bi sopp, ndax yeen la jëkka taamu, ngir sellale leen Noo gu Sell gi, ak itam seen ngëm gi ngeen gëm dëgg gi, ngir texeel leen.
Moom la soob mu jure nu kàddug dëgg, ba nu taxawe ab jooxeb ndoortel meññeef, ci biiri bindeefam.
¶ Man Yowaan seen mbokk, mi séddook yeen nattu ak barkeb nguurug Yàlla, ak muñ gi ci Yeesu, maa nga woon fa ñu ma toxaloon, ca dun ba ñuy wax Patmos. Li ko waral di sama waare ci kàddug Yàlla ak seedeel Yeesu.