TSK

TSK · Romans 10:19

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

am gémmiñ te du wax, ami gët te du gis,

Ñoom ñépp a bokk dofe, ñàkk bopp: xam-xamu kasara, bant kese!

Bésub keroog, maay nangu,» kàddug Aji Sax jee, «maay nangul asamaan, moom, mu nangul suuf;

nde Yàlla ci biir ag jéllaleem la firndeel njubteem ci janti tey jii, ngir mu leer ne moo wéye njub, te képp ku gëm Yeesu, moo koy jox àtteb ku jub.

¶ Moo tax ma ne xanaa ba bànni Israyil tërëfee, jéll bu ñu dul jógati lañu daanu? Mukk kay! Waaye tooñug bànni Israyil moo waral muccug jaambur ñi dul Yawut, ba tax bànni Israyil siis leen.

Li may wax mooy ku nekk ci yeena ngi naan: «Man ci Póol laa bokk!», «Man nag Apolos!» «Man Sefas!» «Man de Almasi!»

Ana kon lu sama wax jiy wund? Ndax daa wund ne yàpp wu ñu sarxal tuur yi tekki na lenn? Am daa wund ne tuur yi tekki na lenn?

Bokk yi, xam ngeen ne ba ngeen dee ay yéefar, dees leena buuboon, lajjal leen, jëme ci ay tuur yu tëlee wax.

Titus 3:3 TSK

¶ Ndax nun itam kat, ñu ñàkk xel lanu woon te déggadi, ñu réer, tënku ci lu doon ay xemmemtéef, ak bànneexi bakkan, tey wéye def lu bon, ak ñeetaane, ñu jara bañ te bañante ci sunu biir.