TSK

TSK · Romans 10:8

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Maay teg ci seen làmmiñ kàddug cant. Jàmm, na jàmm ñeel ñépp, ku soreek ku jege.» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Maa leen di faj.»

Moom la yonent yépp seedeel, ne képp ku ko gëm, jot nga sa njéggalug bàkkaar ciw turam.»

Ñu ne ko: «Gëmal Sang Yeesu, daldi mucc, yaak sa waa kër.»

Kon boog ngëm ci dég-dég lay juddoo, dég-dég ba bawoo ci kàddug waare gi jëm ci Almasi.

Ki leen di may Noo gi, tey sottal ay kéemaan ci seen biir, ndax li ngeen sàmm yoon moo tax mu di ko def, am li ngeen dégg, ba gëm moo tax?

Ndax kat dangeena judduwaat, te jiwu wi ngeen judduwaate mooy kàddug Yàlla giy dund te sax dàkk; du jiwu wuy yàqu, waaye mooy jiwu wu dul yàqu mukk.