Saw askan dina ne gàññ ni suuf. Dinga law penku ak sowu, ndijoor ak càmmoñ. Ci yaw ak saw askan la giir yi ci kaw suuf yépp di barkeele.
TSK
TSK · Romans 11:28
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ndax seen Yàlla Aji Sax ji Yàllay yërmande la. Du leen wacc, du leen yàqte te du fàtte kóllëre, ga mu fasoon ak seeni maam ci kaw ngiñ.
Waaye fàttlikuleen ne seen Yàlla Aji Sax ji mooy ki leen may dooley liggéey alal ji, ngir feddli ni mu ko defe tey, kóllëreem ga mu giñaloon seeni maam.
Terewul seeni maam doŋŋ la Aji Sax ji taqool, ngir sopp leen, te yeen, ñi askanoo ci ñoom la taamu ci biir xeetoo xeet, niki bésub tey jii.
Waaye yaw Israyil, sama jaam bi; yaw Yanqóoba mi ma taamu, yaw askanu Ibraayma, samab xarit!
Yaay sàmm kóllëre ak Yanqóoba, yéwéne Ibraayma, na nga ko giñale woon sunuy maam, janti démb.
Moo wallu bànni Israyil, jaamam, bàyyee ko xel yërmandeem,
Ba Yawut yi gisee mbooloo ma nag, kiñaan man leen, ñuy weddi waxi Póol, di ko saaga.
Yawut ya nag gàntal, di ko ŋàññ, mu yëlëb ay yéreem, misaale ko ne jaanam wàcc na. Mu ne leen: «Yeenay gàddu seen bakkanu bopp. Man set naa ci wecc. Gannaaw-si-tey, ci jaambur ñi dul Yawut laa jëm.»
ñoo xéewloo itam maam ya; ci wàllu doom aadama it, ci ñoom la Almasi soqikoo, di Yàlla, tiim lépp, te yelloo cant ba fàww. Amiin.
¶ Moo tax ma ne xanaa ba bànni Israyil tërëfee, jéll bu ñu dul jógati lañu daanu? Mukk kay! Waaye tooñug bànni Israyil moo waral muccug jaambur ñi dul Yawut, ba tax bànni Israyil siis leen.
Yawut ñi ñoo rey Sang Yeesu, na ñu reye woon yonent yi, te ñoo nu bundxatal tey. Neexuñu Yàlla, te nooni ñépp lañu.