Teewul Mardose yég pexe ma, wax ko Lingeer Esteer, mu yegge ko Buur, ci turu Mardose.
TSK
TSK · Romans 11:33
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Keey def jëf ju màgg ju nattuwul, ak kiraama yu limuwul.
Dangaa mana gëstu mbóoti Yàlla, ba gis ko? Am yaa ñédd Aji Man ji?
Lii de, mooy lenni jalooreem! Ndaw ndéey lu tuut lu nu ci dégandeem! Ana ku mana xam riiru dooleem?
Xamal nu boog lu nuy wax Yàlla! Dunu mana lay ndax ñàkka xam.
Céy Aji Sax ji, gore nga ba kaw asamaan, dëggu ba kaw-li-kaw.
nga dënoo biir callweer, melax yi taal àddina, suuf di lox, di reg-regi.
Ay xàmbaar a ko yéew, njekk ak njub lal ab jalam.
Maneesula daj li ci xelu buur, xalaatam daa kawe ni asamaan, xóot ni suuf.
Su dee Yàlla moo def loolu nag ngir fésal màggaayu teddngaam, ñeel ay ndab yu xéewloo yërmande, te mu waajalaloon leen teraanga?
Mbaax gi nu Yàlla won ci Almasi Yeesu, moom lay firndeele mboolem xarnu yiy ñëw, ni yiwam yaatoo ba tiiñ am xel.
Su ko defee boroom nguur yeek boroom sañ-sañ ya fa déndi asamaan, mana xame ci mbooloom gëmkati Almasi, ni xelum Yàlla rafete ci wet gu nekk.
ngir yeen ak mboolem ñu sell ñi, seenum xel mana jàpp, ni mu leen ware, luy yaatuwaayub cofeelu Almasi, ak guddaay ba, ak kawewaay ba, ak xóotaay ba.
ngir ngeen gëna am fit, mànkoo ci biir cofeel, te géeju ci gis-gisu xol bu leer nàññ te wóor, ba mana daj dëgg, mbóotum Yàlla, miy Almasi ci boppam.