TSK

TSK · Romans 12:10

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Xanaa àll bi newul yàmblaŋ ngay gis? Nan teqlikoo, kay; boo demee càmmoñ, ma dem ndijoor; boo demee ndijoor, ma dem càmmoñ.»

Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda. Céy liika baax te neexati, ay bokk yu bokk dëkk, di benn!

Joxleen ku nekk li ngeen warlook moom; ku ngeen wara fey galag, feyleen ko ko; ku ngeen wara fey juuti, feyleen ko ko; ku ngeen wara weg, wegleen ko; ku ngeen wara teral, teral-leen ko.

¶ Yeen de bokk yi, cig yiwiku lees leen woo. Moytuleen lenn rekk: bu seenug yiwiku diw lay, ngir topp seen bakkan, waaye deeleen surgawoonte ngir cofeel.

¶ Dama leen di dénku nag, man mi ñu tëj ndax Sang bi, ngir ngeen dund dundin wu yellook wooteb Yàlla, bi mu leen woo.

dégg nanu ngëm gi ngeen gëm Almasi Yeesu, ak cofeel gi ngeen sopp gëmkat ñu sell ñépp,

¶ Bokk yi, manunoo ñàkka sant Yàlla ci yeen fu nu tollu, te muy lu jaadu, gannaaw seen ngëm a ngi yokku bu baaxa baax, te cofeelu ku nekk ci yeen ñépp di gënatee law, digganteem ak moroomam.

¶ Kon nag gannaaw setal ngeen seen xol, ndax dëgg gi ngeen déggal, ba tax ngeen am cofeel gu mucc jinigal, ci bokki gëmkat ñi, nangeen soppantee xol bu set, cofeel gu mat sëkk.

¶ Li may tënke nag moo di yeen ñépp, ngeen mànkoo, yégante, bëggante ni mu ware ay bokki gëmkat, baaxeenteleen te woyof.

seenug njullite, ngeen dolli ci bëgg seen bokki gëmkat; bëgg seen bokki gëmkat, ngeen dolli ci cofeel.