TSK

TSK · Romans 14:5

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Xam naa nag, wér na ma it te Sang Yeesu tax, ne amul lenn lu sobewu ci wàllu boppam, ba daganula lekk; waaye ki jàppe lenn muy lu sobewu, ci moom la loola di lu sobewu.

¶ Waaye du ñépp a xam loolu. Am na gëmkat ñu seen miineelu tuur yi bàyyeegul, ba léegi, te moo tax bu ñu lekkee ñam wu ñu foog ne saraxi tuur la, seen xel mu daladi moo leen di foogloo ne sobe toppe na leen ca ñam wa.

Waaye léegi bi ngeen xamee Yàlla, mbaa bi leen Yàlla ràññee, nu ngeen mana delluwaate ci mbiri àddina yooyu boole tële ak ñàkk njariñ, bay nekkaat seeni jaam?