TSK

TSK · Romans 15:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

«Mbégte déy, ngeen di génne, ñu yóbbu leen ci jàmm, tund yu mag yeek yu ndaw yi di leen sarxolleel, garabi àll bi yépp tàccoondoo.

Bégeleen seen yaakaar, di muñ ci biir tiis, tey saxoo ag ñaan.

Kon nag Yàlla miy maye xolu muñ, di ñaaxe, yal na leen may mànkoo gu mat sëkk, ni ko Almasi Yeesu bëgge,

te Yàlla man na leena baawaanal wépp yiw, ba ngeen saxoo am lu leen doy ci lépp, ak koom gu bare, ngir jépp jëf ju baax.

Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa Yàlla sunu Baay, ak Sang Yeesu Almasi.

ndax sunu xibaaru jàmm, bi nu leen àgge, dikkewu leen ay wax rekk, waaye manoore la leen dikkaale, ak ndimbalal Noo gu Sell gi, ak kóolute gu mat sëkk gu ngeen am. Xam ngeen moos na nu nekke woon ca seen biir, di xintewoo seen njariñ.

¶ Ci man Póol, ndawal Almasi Yeesu, ci ndigalal Yàlla sunu Musalkat, ak Almasi Yeesu sunu yaakaar, ci man la bataaxal bii bawoo,

Moom mooy ki ngeen gisul te sopp ko. Tey fi tey gisuleen ko, waaye gëm ngeen ko, ba tax leena bég lool, mbég mu màgg mu làmmiñ manula tudd,