¶ Ñenn nit ñu bàyyikoo Yude dikk Àncos, ñoo doon digal bokki taalibe yi, ne leen: «Su ngeen xaraful, ni ko aaday Musaa santaanee, dungeen mana mucc.»
TSK
TSK · Romans 16:17
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Bokk yi nag, dama leen di ñaax, ci sunu turu Sang Yeesu Almasi, ngir seen kàddu di genn, te féewaloo baña am ci seen biir, xanaa ngeen bennoo ci lépp, bokk menn xel, ak benn jëmu.
¶ Bindoon naa leen ca sama bataaxal ba, ne buleen amlante ak fokati séy yi.
Te beneen dafa amul sax, xanaa ñenn ñi leen di jaxase, te bëgga sopparñi xibaaru jàmm bu Almasi.
¶ Moytuleen xaj yi, defkati mbon yooyu laa ne, moytuleen leen, moytuleen njoofkat yooyu jiital aaday xaraf.
¶ Moytuleen ba kenn bañ leena këfe kàdduy naxi neen yu ñu jàppe xam-xam bu xelu, kàddu yu sukkandikoowul Almasi, xanaa aaday nit, ak cëslaayi àddina.
¶ Ku ci déggul sunu kàddu yi ñu bind ci bataaxal bii nag, bàyyileen ko xel, te baña jaxasoo ak moom, ngir gàcceel ko.
¶ Waaye ku ciy jàngle leneen, te toppul kàddu yu wér yi tukkee ci sunu Sang Yeesu Almasi, toppul àlluwa ji dëppoo akug njullite,
Ab féewalekat nag, yedd ko benn yoon ba ñaareel bi yoon, doora daggook moom,
Ñooñu ñooy féewalekat yi, ñoo topp seen bindu judduwaale, te Noowug Yàlla nekkul ci ñoom.