TSK

TSK · Romans 2:17

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ci Aji Sax ji la askanu Israyil gépp yeye, bay damu.

Buleen naxe seen bopp kàdduy caaxaan, naan: ‘Kër Aji Sax jaa ngi, kër Aji Sax jaa ngi fii, kër Aji Sax jee!’

«Su bés baa gàcce dootul am ci sa mboolem jëf, ji nga ma moye, nde maay jële fi sa biir ñiy bége sab sag, te doo damooti ci sama kaw tund wu sell.

Ab Yawut, du ci melo wuy feeñ lees koy nekke, te xaraf it du ci màndarga muy feeñ ciw yaram.

Ndax lan? Ngëm lañu sukkandikoowul, xanaa ay jëf. «Doj wuy fakktale,» moom lañu fakktaloo.

¶ Nun danoo juddu diy Yawut, te bokkunu ca xeet yee diy bàkkaarkat.

Ndaxte nun noo xaraf tigi, nun ñiy jaamoo Yàlla Noowam gu Sell, di damoo Almasi Yeesu, te yaakaarunu aaday nitu suuxu neen.

¶ «Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Sàrd nag, bind ko ne ko: «Lii moo di kàdduy Boroom juróom ñaari noo yu Yàlla yi ak juróom ñaari biddiiw yi. Mu ne: Gis naa say jëf. Dañu laa jàppe kuy dund te fekk la dee.