Benn yoon la Yàlla wax, yaari yoon laa dégg, ñu ne; «Doole, fa Yàlla.»
TSK
TSK · Romans 2:6
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Soo nee sa yoon nekku ci it, kiy natt xol yi, xam na, moom miy wattu sa bakkan, xam na, te kat mooy fey nit jëfam.
Neleen aji jub ji mooy baaxle, mooy yooloo añam.
réyi pexe, màggi jaloore; say gët ne jàkk ci mboolem lu doom aadama def, ngay añale ku nekk jëfinam ak jëfam.
¶ Yaw ci sa wàllu bopp, ngëm gi nga ci am, yemale ko ci sa bopp, fi kanam Yàlla. Ndokklee ki sikkul boppam lenn ci jëfin wu mu dogul boppam ne noonu lay jëfe.
Moo tax buleen àtte lenn te jotul, lu jiitu Boroom biy dikk. Moom mooy leeral li làqoo ag lëndëm, di làññi mébéti xol. Su boobaa ngërëm la ku nekk yelloo, fa Yàlla lay bawoo.
¶ Bu leen lenn nax; Yàlla deesu ko foontoo. Nit ki, li mu ji, moom lay góob.
Ma gis néew ya, mag ak ndaw, ñu taxaw ca kanam ngàngune ma, ay téere ubbiku, beneen téere ubbikooti, di téereb dund ba. Ñu daldi àtte néew ya ca seeni jëf, na ñu ko binde ca téere ya.