Wallam aka jege ñi ko ragal, te leeram dëgmal sunu réew mii!
TSK
TSK · Romans 3:26
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Àdduleen, layoosi, diisooleen fi seen biir kay! Ana ku xamle woon lii bu yàgg, yégle woon ko booba? Xanaa du man Aji Sax ji? Kenn du Yàlla ku dul man! Yàlla ju jub, di walloo, du kenn ku dul man!
Aji Sax ji moo teggi say mbugal, waññi sab noon. Buurub Israyil, Aji Sax jaa ngi fi sa biir, dootuloo tiit lu bon.
¶ «Kon nag bokk yi, xamleen ne ci Yeesu moomu lañu leen birale njéggalug bàkkaar. Te mboolem lu ngeen tële woona wàccool, ba seen njub mat ci yoonu Musaa,
Waaye ki jëful te gëm Yàlla miy jox ab yéefar sax, àtteb ku jub, ngëmam googu, ag njub lees ko koy waññal.
Mbind mi moo waajaloon lu jiitu ne ci kaw ngëm lees di joxe xeet yi dul Yawut, àtteb nit ñu jub. Moo taxoon mu yégal Ibraayma lu jiitu, bii xibaaru jàmm: «Xeeti àddina yépp ci yaw lañuy barkeele,»