mu dig leer, ñeel jaambur ñi, sagal Israyil sa ñoñ.»
TSK
TSK · Romans 4:9
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ana lu ci Mbind mi wax? Da ne: «Ibraayma moo gëm Yàlla, ñu waññal ko ngëmam ag njub.»
Ag wuutale amul diggante ab Yawut, ak jaambur bu dul Yawut; ñépp a bokk benn Boroom biy yéwéne mboolem ñi koy woo wall.
Noonu la deme ngir barkeb Ibraayma wàccal xeet yi dul Yawut ndax Almasi Yeesu, ngir itam nu jot ci digeb Noo gu Sell gi, ci kaw ngëm.
¶ Kon nag, yeen jaambur ñi dul Yawut cib juddu, yeen ñi ñuy wooye yéefar yi xaraful, te ñi leen ko dàkkantale woon di Yawut yi xarafe ci loxol nit ku leen xarfal ci seen yaram, fàttlikuleen seen démb.
Dundin wu yees woowu amul jaambur akub Yawut, amul ku xaraf ak ku xaraful, amul ab doxandéem ak ku xayadi, amul ab jaam ak as gor, waaye Almasi mooy lépp te moo nekk ci ñépp.