Seen Yàlla Aji Sax ji kat seexlu na képp kuy def yooyii, képp kuy def ug njublaŋ.
TSK
TSK · Romans 6:13
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Kàddug aji jub day xelu, wax ja jub;
Neleen aji jub ji mooy baaxle, mooy yooloo añam.
Mu ngoog, bépp bakkan maay Boroom. Muy bakkanu baay, di bakkanu doom, maa moom. Bakkan bi bàkkaar daal mooy dee.
ndax sama doom jii moo dee woon te dekki na, moo réeroon te feeñ na.” Ñu daldi tàmbalee bànneexu.
Waaye ñi fétteeral ci seen sàkkuteefi bopp, nanguwuñoo topp liy dëgg, xanaa ag njubadi nag, ñooñu, am sànj ak mer mu ne jippét lañuy yooloo.
Xanaa xamuleen ne képp koo jébbal sa bopp, nangul ko, ab jaamam nga? Yaar ngeen diy jaam, bàkkaar di seen sang, jëme leen ci ndee; mbaa ngeen déggal Yàlla, mu jox leen àtteb ñu jub.
Ba nu toppee sunu bakkan, sunu bëgg-bëgg yu bon yi ndigali yoonu Musaa yee, ñoo daan liggéey ci sunuy cér, ngir nu meññ lu nu jëme ci ndee.
¶ Kon nag bokk yi, ma ñaax leen, te yërmandey Yàlla tax, ngir ngeen jébbal ko seen yaram wépp, def ko jooxe buy dund, sell te neex Yàlla. Loolu déy mooy njaamu, gi leen war.
Xanaa xamuleen ne, seen yaram mooy céri Almasi? Waaw, ndax damay jël céri Almasi, def ko céri gànc bu jigéen? Yàlla tere!
Te ki deeyal ñépp, daa deeyal ñépp ngir ñiy dund bañatee dund ngir seen bopp, xanaa di dund ngir ki leen deeyal, ba dekki.
Ndaxte gànnaay, yi nuy xeexe du gànnaayi suuxi neen, waaye da di gànnaay yu am fa Yàlla, kàttanu daane ay tata. Te xalaatin yu jubul, noo leen di daaneel,
te lépp lu ñu wone ci ag leer, di ag leer. Moo tax ñu ne: «Yaw miy nelaw, yewwul, dekkil, Almasi leeral la.»
¶ Yeen ñi doonoon ndee fa kanam Yàlla ndax seeni moy, ak seen ñàkka xaraf, ndax li ngeen dul Yawut, Yàllaa leen booleek Almasi dundalaat leen. Moo nu baal sunu moy yépp.
Su ko defee mbugal dal mboolem ñi gëmul dëgg gi, xanaa di xejjoo njubadi.
¶ Ana fu jote yeek xuloo yi ci seen biir jóge fu moy seen bànneexi bakkan, yiy xare ci seen yaram?
ngir bañatee topp xemmemtéefi bakkan, xanaa di topp coobarey Yàlla, diir bi ko dese ci kaw suuf.