Say tegtal laay ràññee, ba tax ma bañ luy yoonu fen.
TSK
TSK · Romans 6:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Te yemunu ci, xanaa di sagoo Yàlla itam ndax sunu Boroom Yeesu Almasi, mi nu jubale ak moom.
¶ Noonu la deme ak yeen itam, bokk yi. Yaramu Almasi wi ngeen bennool, ci ngeen doone ñu deeyal yoonu Musaa. Noonu ngeen doone moomeelu keneen, te kooku mooy ki dekki, ngir nu meññ njariñ lu ñeel Yàlla.
Ndaxte cofeelu Almasi daal moo nu jiite, nun ñi ràññee lii: Gannaaw kenn moo deeyal ñépp, kon ñépp a dee.
Waaye man de Yàlla buma damoo lenn lu moy deewug sunu Boroom Yeesu Almasi ca bant ba. Bant boobu moo tax àddina di lu ñu ma daajal ci bant, ba àddina dee; man it may lu ñu daajal àddina ci bant ba ma dee.
ndaxte dee ngeen, ba seenug dund ànd ak Almasi, làqe fa Yàlla.
«Moom ci boppam moo gàddu sunuy bàkkaar, moo ko tegoo ci yaramu boppam ca bant ba,» ngir nu deeyal bàkkaar te dundal njub; «moom mooy ki ngeen wére ci ay góomam.»