Ay doomi buur a ngi ci jigéen ñi nga teral, sab lingeer féete la ndijoor, takkoo ngëneelu wurus.
TSK
TSK · Romans 7:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ni xale bu góor di takke ab janq, ni la la sa doom yu góor di moome ni jëkkër; ni boroom séet di bégee ab séetam, ni la la sa Yàlla di bégee.
Mukk kay! Nun ñi ndee tàggale ak bàkkaar ba noppi, ana nu nuy saxootee bàkkaar?
Waaye tey bi ñu leen yiwee, ba ngeen doon ay surgay Yàlla, ag sellnga la leen loolu jural, te muj ga di texe gu sax dàkk.
Ndax kat, dooley Noo giy maye bakkan te nekk ci Almasi Yeesu moo la yiwi, ba nga mucc ci dooley bàkkaar ak ndee.
Maa leen di fiiree fiiraangey Yàlla ci boppam, ndax jenn jëkkër doŋŋ laa leen digool ab séy, te mooy Almasi mi ma leen namma jébbal, te fekk leen di janq bu set wecc.
¶ Almasi moom, moo nu jot ci alkàndey yoon wi, ba mu doonee ku alku ngir nun, nde: «Alkute ñeel na képp ku ñu rey, wékk ko ci bant.»
¶ Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel, ak mbég, ak jàmm, ak xolu muñ, ak mbaax, akug tabe, ak ngëm,
Almasi moo di musalkatu mbooloom gëmkat ñi, mbooloo mi di aw yaramam. Te itam ni Almasi dee boppu mbooloom gëmkat ñi, ni la jëkkër ji dee boppu jabaram.
Du caageenu ndimbal lu ma leen di sàkku, li may sàkku kay moo di yokkuteb yool bu leen ñeel.
Su ko defee ngeen di dunde dundin wu yellook Boroom bi, ngir bànneexal ko ci wet gu nekk, seen meññeef it di jépp jëf ju baax, te ngeen gën di xam Yàlla.
Kayitu bor bi nu tiiñaloon, te dogali yoon toppe nu ko, moom moo far mbind ma, yóbbu kayit ga, daajaale ko ak Almasi ca bant ba.
Coobarey Yàlla googu moo waral ñu sellale nu sarax, bi Yeesu Almasi sarxe yaramam, benn yoon ba fàww.
Nanu bég, di bànneexu te màggal ko, ndax céetu Gàtt bi agsi na, ab séetam defaru na ba noppi!