Maa leen di jox xol bu yees, te xel mu yees laay def ci seen dënn. Xolu doj bi laay roccee ci seen suux, weccee leen ko xolu suux,
TSK
TSK · Romans 7:6
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ki xaraful ciw yaramam, te teewu koo sàmm yoonu Musaa, moo lay teg ab daan, yaw mi boole mbindum yoonu Musaa, ak sag xaraf, te teewu la di moykatub yoon wi.
Ci sóobu googu lañu nu boole ak moom suul, ngir noonee Almasi dekkee ci màggug Baay bi, nun itam nu dekki bay dund dundin wu yees.
Ndax kat bàkkaar yilifatu leen, nde du ci kilifteefu yoonu Musaa ngeen nekk, waaye ci aw yiw ngeen tàbbi.
Waaye tey bi ñu leen yiwee, ba ngeen doon ay surgay Yàlla, ag sellnga la leen loolu jural, te muj ga di texe gu sax dàkk.
¶ Noonu la deme ak yeen itam, bokk yi. Yaramu Almasi wi ngeen bennool, ci ngeen doone ñu deeyal yoonu Musaa. Noonu ngeen doone moomeelu keneen, te kooku mooy ki dekki, ngir nu meññ njariñ lu ñeel Yàlla.
Moo nu may manoorey doon ay liggéeykati kóllëre gu bees gu ajuwul ci mbindum ndigali yoon, xanaa kóllëre gu aju ci Noo gi. Ndaxte mbindum ndigali yoon day rey, te Noo gi di dundloo.
Su dee wàllu yoonu Musaa nag, man nit ku dee laa, te yoonu Musaa moo ko waral, ngir ma mana dund dund gu ñeel Yàlla. Dees maa boole ak Almasi rey ca bant ba.
¶ Balaa yoonu ngëm wee dikk, dees noo jàppoon tënk ci yoonu Musaa, ba kera yoonu ngëm wi feeñee.
Xaraf ak ñàkka xaraf, dara amu ci solo. Li am solo mooy doon mbindeef mu bees.
ba sol seen jëmm ju yees, jiy gën di yeeslu, te di gëna niru ki leen ko sàkkal, ba kera ngeen xamee, xam-xam bu mat sëkk.