TSK

TSK · Romans 8:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Seen jëfi démb ja leen gàcceel tey, ana njariñ lu mu leen jural? Mujug jëf ja de, seenug dee la doon doon.

Ba nu toppee sunu bakkan, sunu bëgg-bëgg yu bon yi ndigali yoonu Musaa yee, ñoo daan liggéey ci sunuy cér, ngir nu meññ lu nu jëme ci ndee.

ngir njub gi yoonu Musaa laaj mana sotti ba mat sëkk ci nun, ñi toppatul sunu bindu suux, xanaa Noowug Yàlla.

¶ Jëfi bakkan nag yomb naa xàmmi, te mooy: powum séy, ak jëfi sobe, ak yàqute,

Ku jiyal bànneexu bakkanam, ci bànneexu bakkanam lay jële ngóobum yàqute; ku jiyal Noowug Yàlla, ci Noo gi ngay góobe texe gu sax dàkk.

Te it buleen tiisal Noowug Yàlla gu Sell, gi leen màndargaale xàmmikaayam ngir bésub njot ba.

Buleen naan biiñ ba màndi, màndite ci afal seen bakkan la leen jëme, waaye na leen Noo gi fees,

Yiw woowu moo nu digal nu dëddu ñeme Yàlla, ak xemmemtéefi àddina, te jiital sunum xel, di jëfe njub, te nekke ag njullite ci àddinay tey jii.

¶ Kon nag gannaaw setal ngeen seen xol, ndax dëgg gi ngeen déggal, ba tax ngeen am cofeel gu mucc jinigal, ci bokki gëmkat ñi, nangeen soppantee xol bu set, cofeel gu mat sëkk.