Jàngal ma, ma jëfe sa coobare; yaa di sama Yàlla. Yal na ma sam xel jiitee mbaax ci yoon wu tàlli.
TSK
TSK · Romans 8:14
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Jegesileen ma, déglu ma; bu jëkk ba tey làquwma, di wax; te ba muy xew, fa laa teew. Tey Boroom bi Aji Sax ji da maa yebal boole maakam xelam.
¶ Yeen nag nekkatuleen ci kilifteefu bindu suuxu neen, waaye ci kilifteefu Noo gi ngeen nekk, ndegam kay Noowug Yàllaa ngi màkkaanoo ci yeen. Ku amul Noowug Almasi, kooku du nitam.
Càkkéefu àddinaa ngi séentu, ndax yàkkamti bés ba doomi Yàlla di feeñ.
«Te foofa ñu leen noon: “Yeen, dungeen sama ñoñ,” fa lees leen naa: “Yeenay doomi Yàlla jiy dund.”»
¶ Yeen ñépp doomi Yàlla ngeen, ndax li ngeen gëm Almasi Yeesu.
¶ Li ma leen di wax moo di: doxeleen Noowug Yàlla, su boobaa dungeen topp seen xemmemtéefi bakkan.
¶ Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel, ak mbég, ak jàmm, ak xolu muñ, ak mbaax, akug tabe, ak ngëm,
Li leer gi ci yeen di meññ moo di mboolem luy mbaax ak njub ak dëgg.
Képp ku am ndam nag, loolooy doon sab cér. Maay doon sa Yàlla, nga doon sama doom,