Ci kaw loolu Musaa defarlu jaanu xànjar, wékk ko ci bant, ba képp ku jaan màtt, bu xoolee jaanu xànjar ja, daldi mucc.
TSK
TSK · Romans 8:3
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ndax kat deesul jox kenn àtteb ku jub fa kanam Yàlla ndax jëf ju mu def, ngir sàmm yoonu Musaa; solob yoon wi daal, mooy ci lees di ràññee bu baax luy bàkkaar.
Ba nu toppee sunu bakkan, sunu bëgg-bëgg yu bon yi ndigali yoonu Musaa yee, ñoo daan liggéey ci sunuy cér, ngir nu meññ lu nu jëme ci ndee.
nde man doon naa ñaana alku sax, daggoo ak Almasi, ngir jàmmi sama bokki xeet, sama bokki deret.
¶ Almasi moom, moo nu jot ci alkàndey yoon wi, ba mu doonee ku alku ngir nun, nde: «Alkute ñeel na képp ku ñu rey, wékk ko ci bant.»
Waaye ba àpp ba jotee, Yàlla moo yónni Doomam, mu juddoo ci jigéen, juddoo ci biir curgag yoonu Musaa,
¶ Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley ndee, te mooy Seytaane.
Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar.
¶ Yoonu Musaa takkndeeru xéewal yiy ñëw doŋŋ a ci nekk, waaye xéewal ya ci seen bopp nekku ci. Looloo tax sarax yi yoon wi laaj ñu war koo saxoo jébbale at mu nekk, manula setal mukk wecc ñiy jaamusi.
Kon bennub sarax boobu, ci la matale sëkk ba fàww, nit ñi ñu sellal.
¶ Gannaaw Almasi nag moo daj coonob yaramam, yeen itam gànnaayooleen boobu yéene, ndaxte ku daj coonob yaram, tàggoo naak bàkkaar,