TSK

TSK · Romans 8:31

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Gannaaw ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikke na Ibraam wax jii ci peeñu, mu ne ko: «Yaw Ibraam, bul ragal dara; man maay sa kiiraay, te sa yool dina màgg lool.»

Ndokklee, Israyil, ana ku mel ni yeen, askan wu Aji Sax jiy wallu, di seen kiiraay, di seen ndimbal, di saamar bi leen di sagal? Seeni noon a leen di loxal, te yeen, fa seen gannaaw ya ngeen di daagoo.

¶ Yonatan ne gàddukatu gànnaayam: «Ayca nu dem ba ca dalub yéefar yee. Jombul Aji Sax ji defal nu yiw, ndax dara du tee Aji Sax ji maye ndam, nu bareek nu néew.»

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di jàngin wu ñeel askanu Kore wu góor, dëppook galan bu ñuy wax Baatu jigéen.

Mu ne: «Dal-leen te xam ne maay Yàlla, màgg ci biir xeet yi, màgg fi kaw suuf.»

Yàlla laay màggal kàddoom, Aji Sax ji laay màggal kàddoom,

Aji Sax jeek man, duma tiit. Ana lees ma manal?

Ngànnaay lu ñu la mana sàkkal, du sotti, te boroom làmmiñ wu la jógal cib layoo yaa koy tiiñal. Ñiy jaamu Aji Sax ji, looloo di seen cér, looloo di njekk gi ma leen di dikke.» Kàddug Aji Sax jee.

Waaye Aji Sax jeek man, di ñeyi xare. Moo tax ñi may tëru di tërëf, ba duñu daan, xanaa rus lool, ndax duñu baaxle; gàcce gu yàgg lay doon te du fey.

¶ Ibraayma sunu maam ci wàllu njureel nag, ana lu nuy wax ne moom la gis ci moomu mbir?