Malaaka ma ne ko: «Bu sa loxo laal xale bi; bu ko def dara, ndaxte léegi xam naa ne ragal nga Yàlla, ndax gàntaloo ma sa jenn doom ji.»
TSK
TSK · Romans 8:32
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Moona Aji Sax ji la soob, mu dëggaate jaamam bii, teg koy naqar, su nangoo doon saraxu peyug tooñ, gis askanam, aw fanam gudd, te coobarey Aji Sax ji ci moom lay sottee.
¶ Ndax kat, ba nu amul menn pexem mucc, ca la Almasi deeyal yéefar yi nu doon, ba mu jotee.
¶ Te itam nag xam nanu ne Yàlla mooy def mboolem lu xew, daje ba jur njariñal ñi sopp Yàlla, ñi mu woo, noonee ko ab dogalam namme.
Nun nag du xelum àddina lanu jot, waaye Xel mi bawoo fa Yàlla lanu jot, ngir nu mana ràññee li nu Yàlla baaxe.
Loolu lépp yeena tax, ngir yiwu Yàlla lawa law, ba cant gu ne gàññ tukkee ci ñi ëpp ci nit ñi, ngir màggug Yàlla.
¶ Ndax Yàlla kat, ndegam moo jéggalul malaaka ya bàkkaaroon, xanaa tàbbal leen kàmbu mbugal, wacce leen ay jéngi biir lëndëm gu ne këruus, di leen nége àtte ba;
Képp ku am ndam nag, loolooy doon sab cér. Maay doon sa Yàlla, nga doon sama doom,