Su nuy dund, Boroom bi lanuy dundal, su nuy dee it, Boroom bi lanuy deeyal.
TSK
TSK · Romans 8:38
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Bu yaramu judduwaale wii nara yàqu solee weneen wu dul yàqu, ba yaramu ndee wii sol yaramu ndeetil, su boobaa la kàddu gii ñu bind di mat: «Mëddees na ndee ci géeju ndam.
Noo ngi onk ndax diis, li feek nu ngeek sunuw yaram, xayma bi nu soloo nii. Du summiku lanu namm, waaye solu teg ko ci lanu namm, ngir li jëm ndee, daldi suux ci biir ndund.
Foofa la Almasi tiime lu sore gépp nguur, ak bépp sañ-sañ, ak gépp manoore, ak gépp kilifteef, ak wépp tur wees di tudd, muy tey, di ëllëg.
Loolu laa ne siiw, yaakaar ko, te duma rus mukk, xanaa di saxoo aw fit, démb niki tey, ngir ma mana fésale sama jëmm jépp, teddngay Almasi, su may dund ak su may dee.
Moo dog sidditi boroom nguur yeek boroom sañ-sañ yi ci jaww ji, ñu doon ay jaam yu mu jàppe xare. Moo leen weer it ci kanam ñépp, diriwaale leen ca biir njaab ma topp ca ndam, la Almasi ame ca bant ba.
¶ Ñoom ñépp ngëm lañu deeyaale te jotaguñu woon la ñu leen digoon. Waaye fu sore lañu ko séene, di ko séentu, tey ràññee ne ay doxandéem aki màngaan lañu ci àddina.
¶ Àndleen ak sago te teewlu! Seenub noon Tuumaalkat bi, mu ngi ŋar ni gaynde, tey wër, di rëbb ku mu warax.