TSK

TSK · Romans 9:16

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Demal ca gétt ga, nga jàpp ñaari tef yu duuf, ma defaral ko sa baay, ba mu neex, ni mu ko bëgge,

Maa may ay nit tont te laajuñu ma. Maa leen may, ñu gis ma te seetuñu ma woon. Maa ne leen: Maa ngii, maa ngii! te ñuy xeet wu dul tudd sama tur.

¶ Ca waxtu woowa tembe la kemtalaayu mbégte tukkee ci Noo gu Sell gi, dugg Yeesu, mu daldi ne: «Baay, Boroom asamaan ak suuf, sant naa la, nde yaa làq lii boroom xam-xam yeek boroom xel yi, xamal ko tuut-tànk yi, nde loolu de, Baay, mooy li la soob.

¶ Bokk yi, seetleen ñan ngeen woon, ba ñu leen di woo. Barewul ci seen biir ay xamkat, ci gis-gisu nit ñi, barewul ci yeen ay boroom doole, barelewuleen ñu rafet ab juddu.

Ndax kat ci yiw ngeen mucce ci kaw ngëm, te loolu jógewul ci yeen, mayu Yàlla la;

¶ Nun nag bokk yi, manunoo ñàkka sant Yàlla fu nu tollu, ci yeen ñi Boroom bi sopp, ndax yeen la jëkka taamu, ngir sellale leen Noo gu Sell gi, ak itam seen ngëm gi ngeen gëm dëgg gi, ngir texeel leen.

Moom la soob mu jure nu kàddug dëgg, ba nu taxawe ab jooxeb ndoortel meññeef, ci biiri bindeefam.