Dinaa feddli sama kóllëre ak yaw, yokk la bu baax.»
TSK
TSK · Romans 9:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Kóllëre gi ma fas ak yaw, te nga war koo sàmm, yaak sa askan, li mu laaj mooy lii: góor gu nekk ci yeen, war naa xaraf.
Su ko defee nga wax Firawna, ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: ‘Israyil mooy sama taaw bu góor.
¶ Ba loolu amee Musaa yéeg, jëm ca Yàlla. Aji Sax ji jaar ci turu Musaa foofa ca kaw, ne ko: «Nanga wax ak waa kër Yanqóoba te nanga ma siiwtaaneel ci bànni Israyil googu, lii ma lay wax:
¶ Aji Sax ji teg ca ne ko: «Nanga bind yii santaane, ndax ci kaw santaane yii laa fasook yaw kóllëre, yaak bànni Israyil.»
¶ Bu Musaa duggaan ca biir xaymab ndaje ma, ngir wax ak Aji Sax ji, day dégg baat ba di wax ak moom, bawoo fa tiim kubeeru gaalu seedes kóllëre ga, ca diggante ñaari serub ya. Noonu la daan waxeek moom.
¶ Ay doom ngeen, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Buleen ñaasu, buleen wat seen kawaru bopp fi féeteek jë bi, ngir di ko mititloo ku dee,
Yeen ñi taxaw ci sunu biir tey, fi sunu kanam Yàlla Aji Sax ji, ci ngeen bokk, waaye ñi dikkagul bay bokk ak nun taxaw fii it, ci lañu.
Ndaw sa nag tudde gone gi Ikabot (mu firi Ana leer ga?) te naan: «Leer ga dëddu na Israyil, dem ngàllo.» Ndax la ñu nangu gaalu Yàlla ga ak la goroom ak jëkkëram dee.
Ca tundu Sinayi wa nga wàcc, àddoo asamaan, wax ak ñoom, dénk leen ndigal yu jub, ak yoon yu dëggu, ak dogali yoon ak santaane yu baax.
Yaw Yàlla, yaay sama Yàlla, ma di la sàkku, sama bakkan mar la, sama jëmm namm la, fu suuf mare ndox, ne sereŋ.
Mu jébbal ngàllo màndargam dooleem, may gànjaram ca loxol noon ba.
Waaye duma ko daggal sama ngor, te duma ko ñàkke worma.
Mooy wax Yanqóoba kàddoom, dogalam yaak ndigali yoonam ñeel Israyil.
Waaye yaw Israyil, sama jaam bi; yaw Yanqóoba mi ma taamu, yaw askanu Ibraayma, samab xarit!
Du jant a lay leeralati bëccëg, te weer du la niital; Aji Sax jeey doon sag leer ba fàww, sa Yàlla jooju di sab taar.
Aji Sax ji ne: «Du Efrayim ay sama doom ji ma sopp, gone gi may bànneexal? Lu ma ko gëdd gëdd, di ko bàyyi xel. Moo tax sama xol di ko laaj, ma yërëm koo yërëm.» Kàddug Aji Sax jee.
«Aji Sax ji dafa wax ne: Ndegam manees naa dog sama kóllëre maak bëccëg mbaa sama kóllëre maak guddi, ba bëccëg mbaa guddi baña teew ci waxtoom,
«Maa soppoon Israyil ba muy ndaw, Fa Misra laa ko wooye, muy sama doom.
Moo wallu bànni Israyil, jaamam, bàyyee ko xel yërmandeem,
Ndax dige bi, yeen ak seen askan a ko moom, ak jaambur ñi féete fu sore ñépp, mboolem ñi sunu Yàlla Boroom bi woo.»
Nun nag noo leen di àgge xibaaru jàmm bii: li Yàlla digoon sunuy maam,
Mayeesu leen noo gu leen di desloo cig njaam, ba tax leena dellu cig ragal, waaye Noowug doom yu ñu doomoo, moom lees leen may, te looloo nu tax di wooye Yàlla: «Abba», mu tekki «Baay.»
Jant yooyu amuleen woon benn cér ci Almasi, te amuleen woon jenn yelleef ci mbootaayu bànni Israyil. Bokkuleen woon ci kóllëre yi ëmb digeb Yàlla, te mu fasoo ko ak ñoom. Ñàkk yaakaar, ak ñàkka xam Yàlla ngeen nekke woon ci àddina.
Waaye tey la Yeesu jot ci liggéeyu carxal gu sut gu jëkk ga fuuf, te kóllëre gi mu fas diggante Yàlla ak nit ñi, noonu la gëne gu jëkk ga; dige yi lal kóllëre gu yees gii it, noonu la gëne dige ya laloon gu jëkk ga.
Néeg ba ca wàllaa ñaareelu rido ba, moom lañu daan wooye bérab bu sell baa sell.