TSK

TSK · Ruth 2:14

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Dingeen lekk ba regg, di sante seen Yàlla Aji Sax ji, réew mu baax ma mu leen jox.

Ruth 2:18 TSK

Mu yóbbu ko ba ca dëkk ba, goroom gis la mu for, mu daldi yebbi la desoon ca añam, jox ko.

¶ Ba mu ko defee Abigayil gaaw sàkk ñaar téeméeri mburu, ak ñaari mbuusi biiñ, ak juróomi gàtt yu ñu defar, ak juróomi natti peppum mbool, ak téeméeri cabbi reseñ, ak ñaar téeméeri danki figg, boole ko sëf ci ay mbaam.

Ka koy séddale ne ko: «Waaw, nu may taajale lii téeméeri nit?» Mu ne ko: «Joxal mbooloo mi ñu lekk, ndax Aji Sax ji nee: Dinañu lekk ba mu des.»

Yaa ma berndeel, noon yi gis, nga diwal ma saa bopp, terale ma, saab kaas rembat.

Waaye gor si, ngor lay mébét, te ngor lay wéye.

di leel ku xiif lu ngeen gëna bëgg, di reggal néew-ji-doole, su boobaa seen leer fenke biir lëndëm, seenug këruus di ag njolloor,

¶ Ci kaw loolu Yeesu ne waa ja ko woo bernde: «Boo dee waajal bernde, añ mbaa reer, bul woo say xarit, mbaa say doomi ndey, mbaa say bokk, mbaa say dëkk yu am alal, nde ñoom itam dañuy walbatiku, woo la rekk, mu doon sag pey.