TSK

TSK · Ruth 2:20

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Bu ay góor yu bokk waajur dëkkee, kenn ci ñoom dee te bàyyiwul doom ju góor, jabaru ki dee du génn, di séy akub jaambur. Jëkkëru donaleem ju bokk ak jëkkëram moo ko wara jël, donloo ko.

Ruth 3:10 TSK

¶ Mu ne ko: «Yal na la Aji Sax ji barkeel, doom! Jiwati nga bokk gi ngor lu gënatee rafet. Ndax su la neexoon, nga topp ci xale yu góor yi, ñu am ak ñu ñàkk.

Ruth 4:4 TSK

Man nag dama noon war naa la koo yegge, te laaj la ndax danga koy jënd ci kanam magi dëkk bi ak ñi fi toog. Soo bëggee def sa warugaru jotaat, jëndal. Soo buggul, wax ma, ma xam. Ndax kat kenn gënu la cee yey, te maa topp ci yaw.» Mu ne ko: «Damay jënd kay!»

Ruth 4:14 TSK

Jigéen ña ne Nawmi: «Sant Aji Sax ji, moom mi la xañul mbokk mu la jotaat nii tey! Yal na xale bi di ku amu tur ci Israyil gépp.

¶ Daawuda moo noon: «Ndax kenn desul ba tey ci waa kër Sóol, ba ma jëfeek moom ngor ngir Yonatan?»

Job 29:12 TSK

Néew-ji-doole woote, ma wallu, boole ci jirim bu tumurànke.

Xarit du bëgg, di bañ; mbokk day bokk ak yaw say coono.

Yal na Yàlla baaxe nag waa kër Onesifor, yërmandeem, ndax dëfal na ma lu bare, te kersawoowul li ñu ma tëj kaso,