Ruth 2:20
TSK
¶ Nawmi ne Ruut: «Yal na Aji Sax ji barkeel Bowas, moom mi saxoo sàmm ngoram digganteem ak nit, muy dund ak mu dee!» Mu teg ca ne ko: «Kooku ku nu jege la; bokk na ci ñi am sañ-sañu jotaat nu.»