¶ Laban nag amoon na ñaari doom yu jigéen, taaw ba di Leya, rakk ja di Rasel.
TSK
TSK · Ruth 4:11
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ba loolu wéyee ñu jóge Betel, dem bay bëgga jub Efrata. Rasel tollu ciw mat, te mat wi metti.
¶ Doomi Leya ñooy: Ruben, taawub Yanqóoba, ak Simeyon ak Lewi ak Yuda ak Isaakar ak Sabulon.
¶ Waa kër Israyil, yi ñëw Misra te di Yanqóoba aki doomam, seeni tur a di: Ruben, taawub Yanqóoba.
Su waa ji buggula jël jabaru donaleem jooju, na ndaw sa dem ba ca mag ña ca bunt dëkk ba, ne leen: «Sama jëkkëru donale jii moo baña saxal turu mbokkam ci Israyil. Moo ma buggula donloo.»
Waa ja Elimeleg la tuddoon, soxnaam di Nawmi, ñaari doomam yu góor ya di Malon ak Kilyon. Ay Efrateen lañu, cosaanoo Betleyem ca Yuda. Ñu agsi ca réewum Mowab, daldi sanc foofa.
Sa jabar ni garab gu nangoo sa wanag, say doom wëra wër sa ndab ni njëmbat lu jebbi.
Jigéen, rafet xel, dimbali waa këram, su deeb dof, tas këram.
Moo tax Aji Sax ji di leen wacc ba keroog jant, ba kiy matu mucc. Ca la bokkam ya dese bakkan di dellu, fekki seen bokki bànni Israyil.