“Aji Sax ji nee: Maa ngii di wàcce musiba ci bérabi bii ak ñi ko dëkke, muy mboolem kàdduy téere bi buurub Yuda jàng.
TSK
TSK · Zechariah 1:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Gannaaw yaa réccu ci sa xol, ba toroxlu ci kanam Aji Sax ji, ba nga déggee ni ma rëbbe bérab bii mook ñi ko dëkke, muy seen toroxteek seen alkànde, te yaa xotti say yére, jooy fi sama kanam, man it dégg naa la. Kàddug Aji Sax jee.
Loolu nu dal lépp, sunu jëf ju bon a tax, ak sunu tooñ gu réy. Terewul yaw sunu Yàlla, tegoo nu lu dul mbugal mu yées mi sunuy bàkkaar yellool. Terewul yaw sunu Yàlla, li nu bàkkaar mbugaloo nu ko, te moo nu fi taxa des di dund nii.
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Seedeb Tóor-tóor, di taalifu jàngle, ñeel Daawuda.
Ñu dikk moom ko, te déggaluñu la, toppuñu saw yoon, jëfewuñu mboolem li nga leen santoon, ba tax nga wàcce ci seen kaw mboolem musiba mii.
Yeen mboolem ñiy jaare yoon wi, lii safu leen, waaye seetleen rekk ba gis ndax wenn mitit dab na mitit wi ñu ma teg, te Aji Sax ji naqarale ma ko ci jantub tàkktel sànjam.
noo tooñ, noo fippu, ba tax yaw jéggalewoo.
Ma daldi leen xëpp samam sànj, fàkkase leen sama tàngooru xadar, këpp leen seen añu jëf ci seen kaw bopp. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.»
¶ Yeen xeet wi dul rus, dajeleena daje,
Ndax Aji Sax ji Boroom gàngoor yi déy dafa wax ne: «Na ma leen nammoona mbugale te delluwuma ci gannaaw, ba ma seeni maam merloo,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax,
Kan ci yonent yi la seeni maam fitnaalul? Ñoo rey démb ña yégle woon ñëwug Aji Jub, ji ngeen wor tey, bóom ko.