La yonent bi wax ci turu Aji Sax ji, su sottiwul, dikkul rekk, loola du kàddu gu Aji Sax ji wax. Ñeme Yàlla la ko yonent ba waxe, buleen ko ragal.
TSK
TSK · Zechariah 2:13
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Mu ngi fey xare ci àddina sépp, dog fitt, damm xeej, lakk pakk.
Ca la Boroom bi yewwu ni ku doon nelaw, mel ni jàmbaar ju biiñ xabtal.
Su bés baa waa Misra mel niy jigéen, di lox ndax tiit loxo bi jóg, te Aji Sax ji Boroom gàngoor yi xàccil-leen ko.
Aji Sax jeey waaxu ni jàmbaar, xabtalu ni ñeyu xare, àddu ca kaw, xaacu, tiime noon yi njàmbaaram.
di xabtaloo bànneex ci ker garab yu mag yi, ak ker garaboo garab gu naat, di rendi seeni doom ci yoonu ndox yi, ak xarantey doj yi?
«Ngalla séentool asamaan, xooleel fa sa kër gu sell ga ne ràññ. Ana sa fiiraangeek sa njàmbaar? Sag rafet xol ak sa yërmande ñooru na ma!
Aji Sax ja moom, ma nga ca màkkaanum sellngaam, na àddina sépp selaw fi kanamam.»
Moo tax, giñ naa ko ci man miy dund,» kàddug Aji Sax ju gàngoor yee, Yàllay Israyil, «Mowab déy ni dëkkub Sodom lay mujje, Amoneen ñi mel ni Gomor, ay dég ak paxi xorom a koy nangu, mu gental ba fàww. Sama ndesu ñoñ a leen di sëxëtoo, ndesu xeet wi ma séddoo moo leen di moom.»
«Loxol Sorobabel a teg kenug kër gii, loxoom a koy sottli itam,» ngeen daldi xam ne Aji Sax ji Boroom gàngoor yi moo ma yónni ci yeen.
¶ Xam nanu nag ne lépp lu yoonu Musaa wax, ñi ci yoonu Musaa la ko wax, ngir aw lay jeex tàkk, ngir itam mu leer nàññ ne àddina sépp a sikk fi kanam Yàlla.