Damaa woote, nga gàntal, ma tàllal loxo, faaleesu ma.
TSK
TSK · Zechariah 7:13
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Soo dee tanqamlu yoon, sag ñaan sax Yàlla suur na ko.
Ana lu tax ba ma dikkee, kenn nekku fa? Ma woote, kenn wuyuwul? Damaa gàtta gàtt loxo, ba manumaa walloo? Am damaa ñàkk doole ju ma xettlee? Xanaa du maay gëdd géej, mu wow, maay defi dex màndiŋ, ndox tukki; jën ya mar, dee ba yàqu?
¶ Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: «Maa ngii di leen wàcceel musiba mu ñu dul mana rëcc. Dinañu ma ne wóoy te duma leen déglu.
«Yaw nit ki, ñii seen kasaray tuur lañu def ci seen xol, muy ay wu leen di gàllankoor, te ñu ne ci jàkk. Ñii dinaa leen wacc moos, ñuy sàkku leeraange ci man?
Lee tax noggatukat yii di woo Aji Sax ji wall, te du leen wuyu, kanamam la leen di làq, bésub keroog, nde ñoo bonal seeni jëf.
Bu boroom kër gi xasee jóg, ba tëj bunt bi, fa ngeen di doxe des biti, di fëgg naan: “Sang bi, ubbil nu!” Mu ne leen: “Xawma fu ngeen bokk.”
Mu ne: «Céy yaw itam, boo xamoon bésub tey jii li lay may jàmm! Waaye fii mu ne, làqu na say gët.