TSK

TSK · 1 Kings 21:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yàlla Aji Sax ji ne ko: «Ku la xamal ne dangaa def yaramu neen? Mbaa du dangaa lekk ca garab, ga ma la aaye, waay?»

Aji Sax ji dafa wax ne: “Maa ngii di yékkati fi sa kaw musiba mu jóge ci sa kër. Maay jël say jabar, ngay gis, jox leen góor ni yaw, mu tëdde say jabar bëccëg ndarakàmm.

Fekk na Alyaasaa nga ca këram toog, mag ña bokk toog ak moom. Buur yebal ndaw ca moom. Ndaw la agseegul, Alyaasa ne mag ña: «Xool-leen bóomkat bii yebal kuy dogsi sama bopp! Xam ngeen lan la, bu ndaw li agsee rekk, tëjleen bunt bi, tere koo dugg; ndax du tànki sangam laay dégg, mu topp ci moom sax?»

Ba bataaxal ba agsee, kàngam yooyu boole doomi buur yu góor ya, rendi, ñuy juróom ñaar fukki góor. Ñu yeb seeni bopp ciy dàmba, yónnee Yewu ca Yisreel.

Ba mu ko defee ñu wékk Aman ca bant ba mu waajaloon Mardose. Merum Buur doora giif.

Am kan lay gas, ba mu xóot, te pax ma mu gas, moo ca tàbbi.

Xeet yee tàbbi pax ma ñu gasoon, fakktaloo fiir ga ñu làqoon.

¶ Ci kaw loolu Yonent Yàlla Yeremi jottli Cedesyas buurub Yuda mboolem kàddu yooyu fa Yerusalem.

«Wóoy ngalla kuy dajaleel këram alalu yàqute ju lewul tey aj am tàggam fu kawe, ngir fegu ci yàqule.