TSK

TSK · 1 Kings 21:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Jigéen ja dafa gis ne garab gi rafet na, niru na lu neex, te mata bëgg ci kuy wuta am xel, mu witt ci doom yi, lekk; jox ci jëkkëram, ji mu àndal, moom it mu lekk.

¶ «Buleen xemmem seen lennu moroom: du këram, du jabaram, du jaamam bu góor, du jaamam bu jigéen, du nagam, du mbaamam.»

Réew mooma ngeen jëm, di ko nanguji, déy, niroowul ak réewum Misra ga ngeen jóge, fa ngeen daan jiwe, ba noppi topp seenum jiwu, di ko suuxate dooley tànk ni mbeyum dër.

Seen ngëneeli tool ak tóokëri reseñ ak tooli oliw, mu jël, jox ay surgaam.

Axab ne ko: «Damaa wax ak Nabot waa Yisreel bi, ne ko mu jaay ma toolub reseñam, ma fey ko xaalis mbaa su ko neexee ma wecci ko ko beneen toolub reseñ. Mu ne ma du ma jox toolub reseñam.»

Ma sàkki tóokër aki tool, jëmbat ca garab yuy meññ lu ne,

«Yaw xooloo, xalaatoo lu moy loo jariñoo, ak noo tuure deretu jaamburu Yàlla, di fitnaale ak a lore?»

Ci kaw loolu mu ne leen ñoom ñépp: «Moytuleen wépp xeetu bëgge, ndax loo barele barele, sa bakkan ajuwul ci sa alal.»

Waaye ku nekk, sa xemmemtéefu bakkanu bopp moo lay xiirtal, ootal la ba nax la.