TSK

TSK · 1 Kings 21:26

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Réew ma sax mujj na daj ak sobe, ma wàcce mbugal ca kaw réew ma, ba mu gëq ay nitam.

¶ «Sàmmleen sama dogali yoon yépp ak sama santaane yépp te jëfe ko, ngir réew ma ma leen jëme, ngeen dëkki fa, bañ leena gëq.

Ca tànki buuri Israyil la topp. Doomam ju góor sax def na ko sarax, lakk ko ngir tuur ya, di roy ñaawtéefi xeet, ya Aji Sax ji dàqoon ngir bànni Israyil.

Manase nag di def li Aji Sax ji ñaawlu, topp ñaawtéefi xeet ya Aji Sax ji dàqoon ngir bànni Israyil.

Ezra 9:11 TSK

yi nga nu dénk, yonent yiy say jaam jottli ko, ne nu: «Réew mi ngeen di nanguji, réew mu sobewu la ndax sobey waasoy réew ma. Feesal nañu kook seeni jëf ju siblu ak seen tilim, ba fépp daj.

di tooge diggi bàmmeel, di fanaan bérab yu làqu; di lekk yàppu mbaam, seeni cin def ñam yu sobewu,

Yónnee naa leen ay yooni yoon mboolem yonent yi, sama jaam ñi, ne leen: “Rikk buleen def jëf ju siblu jii ma bañ.”

ku ñàkk ak ku néewle, mu néewal, alalu jaambur, mu foqati, ab tayle, delloowu ko ku ko ameel, xanaa kasaray tuur, mu wékki gët, jëf ju siblu, mu jëfe,

waaye ñu ragal ñi ak aji gëmadi ñi ak defkati ñaawtéef yi ak bóomkat yi ak moykat yi ak xërëmkat yi ak bokkaalekat yi, mboolem niti fen ñi, seen añ a nga ca déegu sawara waak tamarax ba. Loolu moo di ñaareelu dee.»