TSK

TSK · 1 Peter 1:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Aji Sax ji nag dooleel Ilyaas. Mu takk ndigg la, daw jiitu Axab ba ca buntu Yisreel.

Job 38:3 TSK

Takkul boog te góor-góorlu, ma laaj la, nga xamal ma.

Luke 17:8 TSK

Xanaa kay da koy wax ne ko: “Defaral sama reer, te takku, taajal ma, ba ma lekk, naan, nga doora lekk, naan.”

¶ «Moytuleena yaafusal seen bopp ci naan gu ëpp ak màndite ak xalaati àddina, lu ko moy bés ba jekki dal ci seen kaw,

Ndaxte mboolem lu ñu bindoon, bu jëkk, jàngal nu moo taxoon ñu bind ko, ngir Mbind mi may nu xolu muñ, te ñaax nu, ba nu am yaakaar.

¶ Léegi nag liy sax moo di: ngëm ak yaakaar ak cofeel; yii yett la, te li sut ci yooyii moo di cofeel.

Kon nag bunu nelaw ni ñi ci des, waaye nanu teewlu, te ànd ak sunu sago.

Waaye yaw, àndal ak sa sago, ak diggante boo mana tollu, te ñeme coono. Jàppal ci liggéeyub jottli xibaaru jàmm bi, beyal sa waar ba mu mat sëkk.

¶ Ndax yiwu Yàlla kat feeñ na, te looloo indil ñépp ag mucc.

Yaakaar jooju lanu am, mu mel ni diigalub gaal, diigal bu dëgër te wóor, ñeel sunu xol, te yaakaar jooju mooy bëtt rido ba, ba jàll ca néegu biir bu Yàlla ba.

¶ Kon nag buleen teqlikook seenu fit, yool bu réy a ngi ci.

Waaye Sang Almasi ngeen di sellal ci seen xol, te waajal nu ngeen di tontoo ku leen laaj lu jëm ci yaakaar ji ngeen am.

¶ Àndleen ak sago te teewlu! Seenub noon Tuumaalkat bi, mu ngi ŋar ni gaynde, tey wër, di rëbb ku mu warax.