TSK

TSK · 1 Peter 2:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

«Dama di doxandéem ci seen biir, tey gan; moo tax ma di leen ñaan, ngeen sédd ma bàmmeel bu ma suul sama néew, ba mu làqu ma.»

Su dee jigéen ju góor àndal, te wasal génn, nañu sangu, te du tere ñu yendoo sobe ba jant so.

Doxandéem laa fi kaw suuf, bu ma làq say santaane.

¶ «Moytuleena yaafusal seen bopp ci naan gu ëpp ak màndite ak xalaati àddina, lu ko moy bés ba jekki dal ci seen kaw,

Ngeen moytu yàpp wu ñu sarxal ay tuur, ak deret, ak yàppu jur gu ñu tuurul deretam, ak powum séy. Yooyii, bu ngeen ko moytoo bu baax, def ngeen lu baax. Jàmm ak jàmm.

Ku topp bakkanam, fàww mu dee, waaye ku rey jëfi yaramam ci ndimbalal Noowug Yàlla, dina texe.

Nanu jëfe jëfin wu jekka def bëccëg; nanu sore xawaare ak màndite, sore baane bu lewul, ak yàqute yu ni mel, te sore ŋaayoo ak kiñaan.

¶ Nun ñi bokk ci liggéey bi nag, noo leen di ñaan ngeen baña nangu yiwu Yàlla ci neen.

¶ Li ma leen di wax moo di: doxeleen Noowug Yàlla, su boobaa dungeen topp seen xemmemtéefi bakkan.

¶ Dama leen di dénku nag, man mi ñu tëj ndax Sang bi, ngir ngeen dund dundin wu yellook wooteb Yàlla, bi mu leen woo.

¶ Xemmemtéefi ndaw nag, daw ko, te nga topp njub, ak ngëm ak cofeel, ak jàmm, ànd ceek ñiy tudde Boroom bi xol bu set wecc.

¶ Ñoom ñépp ngëm lañu deeyaale te jotaguñu woon la ñu leen digoon. Waaye fu sore lañu ko séene, di ko séentu, tey ràññee ne ay doxandéem aki màngaan lañu ci àddina.

¶ Ci man Piyeer, ndawal Yeesu Almasi la bataaxal bii bawoo, ñeel askan wi Yàlla taamu, te ñu toxuji diiwaani Pont ak Galasi ak Kapados ak Asi ak Bitini.

ngir bañatee topp xemmemtéefi bakkan, xanaa di topp coobarey Yàlla, diir bi ko dese ci kaw suuf.